Bougn né ponk bou djitou thi L’islam moy ga sede né amoul ben bour bougn wara diamou koudoul Yallah té Seydina Mouhamad nawam la, lan lay teki deug deug.
Yonnetebi Sallallahu Anleyhi Wasalam dafané:
بُنِيَ الْإِسْلَامُ عَلَى خَمْسٍ: شَهَادَةِ أَنْ لَا إلَهَ إلَّا اللَّهُ وَأَنَّ مُحَمَّدًا رَسُولُ اللَّهِ... ب وم
Dagno tabaxé lislam thi joroom : bouthi djitou moy sédé ni amoul bénn bour bougn wara jaamou çi deug kudul YALLAH délouwat sédé yit né Seydiduna Mouhamed ndawam la.
شهادة ثلاثة :
١- في القلب
٢- في لسان
٣- بالجوارح
Sédé nak ñét la :
-Sédé thi sap Xol
-Sédé thi saw Lamine
-Sédé thi Say Thieur
Sédé thi xol bi moy guem liga sede thi sa xol
Sédé thi lamine bi moy wakh batou sédé yi
Sédé thi thieur yi moy sédé ak diamou yi
— Kép kou sédé thi xolam té Sédé woul thi laminam ak thi thieuram l’islamam dou wer
— kép kou Sédé thi laminam ak thieuram té sedewoul thi xolam day bok thi nàfiq yi
— kép kou dieuf dieufi l’islam yi té n goul Sédé thi xolam ak laminam l’islamam dou wer
Ñeurign yi nek thi Sédé beuri na ndakh Sédé moy waral niou nangoul la say jaamou YALLAH
Moy waral ga meun am Jabar thi l’islam
Moy takh niou souul la nouniouy souulé dioulit bo fato, moy takh ga doug al jannah…ak yénén
Thi xol amna ñaari xéti Sédé you wouté:
Al-Muraqaba : mooy fouglou sa Borom diko bayixel andak xamni mogui len di guiss
Al-Mushahada : mooy Sédé thi sa xol sa Borom di diakar lo ak ay kemtanam.
Moy lou Yonnetebi Sallallahu Anleyhi Wasalam wakh :
أنْ تَعْبُدَ اللَّهَ كَأنَّكَ تَرَاهُ، (مشاهدة)
فإنْ لَمْ تَكُنْ تَرَاهُ فإنَّه يَرَاكَ، (مراقبة)
Moy ga Jamou Yallah ba melni yagui koy guiss (lolou moy moushahada)
Boko meunta guiss yit mom mogui lay guiss ( lolou moy muràqaba)
Conclusion:
Li nagn len indilon thi sen Jàngat biss bi dilen diokh dig dadie thi yenen jàngat.
En Podcast sur : https://mutadarasuna.wixsite.com/mutadarasuna/podcast/episode/29900694/lan-moy-shahada-sede-ci-islam
N'oubliez pas de nous donner vos impressions
Comments